Kishore Kumar Hits

Taal Bi - Damel #1 текст песни

Исполнитель: Taal Bi

альбом: Damel #1


Trinw
Han
Hey Investir si Taal comme jaay fonde gisoo si pertement
Lepp loo am tek ko doo cool le xaaral sa versement
Rap bi ne si man nekkul si yaw man dama excellent
Fils 0 faute ngay def pour mën passer si sama examen
Nang ma baal bu dee si Rap man la ki siggil Thies
Boy bu ndaw a ndaw bi tuddu Taal sip nga exactement
Ramper raak reppun reewun rawma lu rare si rap
Ku ragg laa mais rap mooma reggal def ma relévu rails bi
Raba tax ma laal million xam li jigeen di jar
Lumay dox di daw te moom yoon wi xamni fii ngen i jaar
And ak beat bi ni gelam mayla couplet bu hard
Man la Taal faaw nga fayma cash pour mën am ñaar i bars
Ñii duñma daan Thies yëpp a souder pour teewal ñaari gares
Li dal grand yi duma mës a dal bii paa mën naa ko waat
Boy daal dama jafe di gis
Ni kankourang biir Russie
Maay tek baatu ñi ñemewul kill
Woyoflul te ñeme lu diis
Donte xol bey dundal naqqaram
Diis ni ku yëggul dara
Kon de jotna ma giif
Di tek hard ne ku bëgoon a riche
Mais amaana Rap be tax toppuma jeez
Ñenn ñi naan dama jubadi jaayuma lëndëm bi jëndee ko leer
Pourtant lu kenn xamul moo di kumpë bi waxlen ko chômeur bi amul salaire
Taxul ma bayyi waxko ńële
Fok ma suxxi saaf fi dilen mbëlle
Doomu kajoor laa fils
Njaaba njëlle lay def sen game bi
Dooma jëllee fils
Fire bi tangg na waxko sa gars yi
Man lanuy wër guddi tangana
Waxko sa mama Pyromane aksina c'est son moment
J'arrive fort comme un fusée Space X
Comme Musk je vise l'espace
Yobbu game bi ci yeneen univers
Fatt fepp ba du desati espace
Bang ma tasaare àdduna
Rayal ma Teeñ dina jaadu nak
SO Damel SO Égérie
Maay tax Ngoné Sobel signer g Amary
Dawal ñaari gares ba romb Neptune
Ñun amunu Terminus
Na gang bi fam bi ñëpp cab tune am salairu Vinicius
Pour nga caisser fok nga gëm def
Motax guddi yi de duma xef
Nit a ragal waaye tus nak
Limite yi danukoy pousse kay
SO Joorka new business new hype ak talent yu bees
Yaw Foné maa ngi ak Taal di def Fire di boyal Thies
Ñëw xër game bi ñëpp sëxët
Au zenith leer ni di digg u bëccëg
Dañu polaire te man dama solaire
Dama stellaire te ñoom danu sol air
Big Dat yox la au Sommet
Maa yagg a Taal sen game bi Foné la Pyromane bi nga gëjj a gis
Dikk rangale rhyme yu rare lyrics flow skillz lepp gën a diis
Man la Damel Teeñ Buur Barak
Sooru ma mooy suul sa rap
Capp daa rëdd teere wisaare punch dafsi doon crac
Yàgg a toog rabul but taxul xel mi nagam
Tong-tong u rhyme bi ngay woote fekk na yeew na nagam
Quintessence si ndabam
Foné ndamam no du xëccoo ngalam
Donooy Alboury li yëngal buur buum la bu nekk si xalam
Style bu rare authentique ne kuy bindee hiéroglyphe
Songg ma si rap si benn bar nga xamni yoroo griffe
Tëb nga songg màggatum kooba doo genn te ñamoo
Dina hard si yaw ni prisonier biir Guantanamo
Foné du màppandoo doxul si tendance no du toppandoo
Bi ngay game lepp échec maa nge k Dat si Jeu de mots
Damel mooy Resister teksi miin tolof-tolof
Juddu rek bañ lii baay nanguloon Buurba Jolof
Man dama dikk pour dàgg buumu gàcce biñu takkal Lamane Dethie Fou Ndiogu
Amary Ngoné Sobel mana
Fu jàmm xëyul du yéndu
Du yomba
Sempi ngemb lii Coowaan la sampoo
Du ay foo Champion bi doora teew jot na nga gëm ko
Damel bi gàddu na xeej bi gaddu na jaasi bi parena pour damm yéel
Daa bari fit te mënula tiit moy li waral sen jiixi-jaaxa bi si xel
Mana Yalla rap bi et c'est vérifié
Imam bi dama ko mériter
Fima daan yonnee mujj naa fa teew Suma bootee ñëpp mani damako xare
Su drapeau bi waddee ñune dama échec
Yaakaar u Thies a ngi si man
Wara andi ndam gindi ñi gëlëm
Gëm ni xam-xam a ngi si bindam
Fok Poids Plume bi teew jox len ay chair de poule
Même bu ñuy kaf si Rap xam ngen ni lii du neen
Man la aka Damel bou reew te cool
Nokku buur nokku dagam sama Kaddu du dañ
Damel Damel woowe nu Damel Teeñ
Benn dëkk ñaari garay buur kenn mënuko jam naani
Damel Damel woowe nu Damel Teeñ
Game bi mar na naan te xam ñi yor baag bu baax si teen
Damel Damel woowe nu Damel Teeñ
Benn dëkk ñaari garay buur kenn mënuko jam naani
Damel Damel woowe nu Damel Teeñ
Game bi mar na naan te xam ñi yor baag bu baax si teen

Поcмотреть все песни артиста

Другие альбомы исполнителя

Похожие исполнители