Kishore Kumar Hits

Ashs The Best - Ngor - Remix текст песни

Исполнитель: Ashs The Best

альбом: Millions Flows (Deluxe)


Am na ñu blem
Je t'aime et tu m'aimes pas
Parce que da maa ñaaw
Bye bye
Xale bu xees bi pour boroom xaliis bi
Neenañ jëllël mbindaan bi
Ay waay
Yanul ma briques yi
Lu ma tee des ci tool yi
Su ma yëggoon des dëkk ba
May boroom puus-puus bi
Chauffeur ru car-rapide bi
Apprenti bu ñuul bi
Kaw-kaw bi lañ may woowe
Bëtt bu nekk ñu ma koy xoole
Boy town bi man may ngaakaam
Nax ma naxaat may doora xam
Lijjënte paasu kaaw dem daani doole
Nangu nekk kaw-kaw luma am yoone
Ndey'ag Baay ci man lañ yaakaar
Kon waru maa coole
Lumay def def ci fulla'g fayda nimu gën a moole
Tallu ma di dem soiree
Tallu ma doxaani
Tallu ma ay xawaare
Dollar dollar dollar ay million
Million dollar million
Dara dara dara sama vision
Ludul million dollar million
Sàngo'og fulla'g fayda
Lu mëna nee la
Deel yoone di woote
Sa yaay bumu jaaxle
Sa jabbar di xaar dëkk ba
Korité demmoo Tabaski bi ngay xaar ba
Tamxarit fekk la fi
Li ngay am as weer doyu la fay ci neeg bi
Begee wax ma kër ga loo fay yoone
Xale bi ngay jël nobbu la xamoo ni yow yay dofam
Baayil sa xel bi ngay foowee
Gestul ñi nga baayi ginaaw
Dañ yaakaar ci yow
Bul Sàmba Alaar Ngoor
Fexeel ba sa yaram daw
Bumu neex nga fate li la fal
Deel baayi xel ginaaw
Yeah mën a nee soo tasul sen yaakaar
Lepp mën na nekk te doo def lu ñaaw
Jamano buñ tòll waratoo nelaw
Deel fataliku demb njaboot gi nga baayi
Balaa ngay baax àll baaxal ci kër gi waay
Mën nga am ay million million dollar
Taxul nga sàalit waay
Sa ngor bulko mës jaayee dara
Bul fate li la fal

Поcмотреть все песни артиста

Другие альбомы исполнителя

Tukki

2022 · Мини-альбом

1995

2022 · Мини-альбом

Похожие исполнители

Jeeba

Исполнитель

VJ

Исполнитель