DIP Doundou Guiss - #Doundou_Oundou {Refrain} Ba gni nekk boy lignou done doundou aka doy war Ba tay souma koy wakh damay réh ba djoy Souma kholé lignou dane def dagno beugone yeufou gangster Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba tay dé magg nagnou {1} Sa youmay dem école dagn may door ma yéwou Té souma démoulé école fadjaar tél lay yéwou Dougou kogne ba wala dem ba Niaye rek tokfa Mane ak sama gars yi khol kou gueuneu kaagne gnou togne ko Ba heurou ndéki am gnou délou waat sen galé ndéki Gnou niakk controle chaque jour cii biti lagni ndéké Outi féraille. lokoy doyé? no dama koy djaay Bouteille, preum, armignon père dakal mou nieuw Xaliss dougnouko khar mou nieuw no da am yone Baabi, pile, perpé, dayce (Dé), xaliss xaliss, pot égatte Fo ba xotti sa yééré swagg soudé dall Kou tchii gueunone guerrier fok gnou coup d'état la {Refrain} Ba gni nekk boy lignou done doundou aka doy war Ba tay souma koy wakh damay réh ba djoy Souma kholé lignou dane def dagno beugone yeufou gangster Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba tay dé magg nagnou {2} Yallah gnou aar, ndakh fougnou diar, mbede dou yaar Forr cigarette guéné sakhar, beuri nullard Eufeul ay xathie, langg camion, taxi, cassambaar Neubeul ni naar, beuri cica (cicatrice) peundeul yambaar Tournoi potou méw, rayanté ndakh bène kopp wéégne Boy bi bougnou topoté fou magg yi dem niou topp lène Guel bo dokhane sou bagné nga nokk ko bamou xam Sangou cii ndoxou taw, def sieste cii biir ay mbaarou kharr (Mouton) Tardé agne tibeu, boudé teud feug Wa galé commencé guiss né ni sen fils sa ngui deung Dagn lay interné, dieundeul la play ba internet Bo gnak chance deugg for ever mbédeu lay hébergé {Refrain} Ba gni nekk boy lignou done doundou aka doy war Ba tay souma koy wakh damay réh ba djoy Souma kholé lignou dane def dagno beugone yeufou gangster Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba tay dé magg nagnou {3} It goes out for my niggaz yima fowa ndol Gnima bokka lone kogne Gnima nékalone école primaire Meunouma dem fatélène Amoul lougnou défoul, amoul lougnou défoul Xawouma lougnou défoul, waxma gaff bougnou défoul Beuré bougnou démoul, béré bougnou lékoul Goune dagnou dane sananté kherr di guerre Saganté kherr di réééh hann anyway Nokanté everyday yeah Beuri, leudj, dakanté périééé, taf dokk, baskulé Motakh ma nane la {Refrain} Ba gni nekk boy lignou done doundou aka doy war Ba tay souma koy wakh damay réh ba djoy Souma kholé lignou dane def dagno beugone yeufou gangster Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba gni nekk boy moussiba rek lagnou dane def Ba gni nekk boy yeufou oundou rek Ba tay dé magg nagnou