Manatuma toog di xaar leneen Li nek sama bop bi xatt na fees na Manatuma toog di xaar leneen Dama muju joow ci gaal ba dess fa Lelelelelena dama muñ ba de, muñ bi jeex na Ndaw si diggu geej weet na, reer na Sama bakanay rot su geej gi mare naan Lo sorale dalay diisël, Tëwa fatte ñima bayi ginaaw Nap kat bi gëdj na giss jën Ku saccul, ñaanul marr na xiif na Diplome ak journala yam këyit lë Fay ndox ak courant ba tay dañuy të Suñu quotidien mo gëna tiss tëss Suñu kër day taa ndox luñu miin lë Xamul ndax yoonu xaru la am yoonu risque lë Tekkey alxuranam, tekkey biblëm Geej du mëssa rëy ba ëp fittëm Gëm ni buñu yegge nañ yeetal fitnë Def ni ku rep giss yoon Dekkufi sedd di lox Defuñu ken lu bonn Dadj luñu yeene wul dom Soobu si teen bi di root Dem te ñëw tedd ni Gorr Dem te ñëw fay suñuy borr Delu samay digg mbok Don mak si kër di daw yërmande ak ndimbël motax ñu sëss Xam liñu bëg fimu ne moy xam fiñu jëm Yoonu geej du liñu gënël liñu gënël moy am li gën Ken bëgul doomam di taggo dem ñukoy deggat si dëdj Gaal bu dëppu, këppu, këppale famille lëm Mëno ŋacc waye dem nga seeti charlie demb Juromi temeri neew Etat ne du wax si sen dëdj Fi yaakar si nguur moy yaakar si ay ngandi dëm Manatuma toog di xaar leneen Li nek sama bop bi xatt na fees na Manatuma toog di xaar leneen Dama muju joow ci gaal ba dess fa Lelelelelena dama muñ ba de, muñ bi jeex na Ndaw si diggu geej weet na, reer na Sama bakanay rot su geej gi mare naan