Nekatoul dem ngir beuga dem wayé Dem dieul samay bagass leem Dem badou saay tank laadjé sakh diém Ma dem Dem Dem nguir meuneu rataxal lii geuneu niagass gatax Dem nguir meuneu gadiafal xop yi nara lax Dem batax baye tabax Dem ndax bekor baña sax dakk thi pak bi naari goori daan daggé niax Dem ndax safarag daay gui boy nara lakk sama koom dou thiax Dem guir soukaat si ndap li ñou seupi sama loxo withiax Dem deudou tangorou diant bitax sama xol di bax Dem dal si kaw ki ray ganthiax ni max Dem babou diaré dougou thi pax Dem teki seni thiax Dem wedi seni nax Dem feussal samag mbax Dem boyal seni thiaax Dem guir badax Baat yi ki deup tax sama ñioñ tereko wax Dem ba dieun diomba doon kethiax (Ba dieun diomba doon kethiax) Dem dieul thi seni waax Sobou seni guedj pathiax Dem wow kong ni betax Dem ndax tayi si limay doundé pelax Dem né rimbax samay loxo thi seni djeuf you rambax Dem bañou andag dal dakal talax talax Dem ba guiss diotal ma ni sindax Dem ba sama yet fitax Dal sen kaw djeul sen weurseug warax Dem bañou takal ma albourax Dem bañou dolimay niax Dem xex kodaaylou yaraax Dem xare ba lifi bone baax Dem andil pep mbam bi fanané nganx Dem ni thieup seni biir dianog seni taax Dem fay bor bi nek seni loxo te téyé sapali sama laax Dem ndax waratouma tog di diap ndiax Dem ndax euleuk ma béñ fé toog ak thiol gouñou daax Dem tay toumbouranké ndax euleuk ma meun né faax (Euleuk ma meun né faax) Dem ndax fama deuk awmafa louma nex Dem ndax sama xaré si kaw souf doumassa diex Dem gaday ni Nabég Ababacar Sadéx Dem mouthiou ni yonéntba Moussa miñi sani si déx Dem ndax biss ma meuna tog di retaan naan kexkex Dem fékhé bañou yabi loumbou dérétou riibaa bi diounkou gui séni lex Dem ndax banex gui woutou guii doundou gou wex Dem ndax sokhnassi eumbeu ay sééx mouthiou thi tawfééx. Dem ba thiolna mba dioumbax Loufi ñiaw ñiaaw ñiou falax Xontat bépeu diour bou lathiax Dem rek