Kishore Kumar Hits

Fallou Dieng - Senghor текст песни

Исполнитель: Fallou Dieng

альбом: Weex Bët


Sengoor sukkandella
Waaw ne sunu baay yi fi nekk ñoom duñ la gaaw a fàtte
Waaw ne sunu yaay yi fi nekk ñoom duñ la gaaw a fàtte
Ni Sengoor la Sëriñ Faalu Mbàkke ñaanaloon
Ne Sengoor mii bu leen ko piisoo, xoole leen ko jàkk ñaari gët
B Jogomaay lañuy woye baay ba
Yaay Ñilaan Baaxumoo lañuy woye yaayamoo woowoo Lewopóol
"Homme de science, homme de culture, académicien" bee
Waaw foo cosaanoo (Afrig)
Waaw foo cosaanoo, Senegaal
Sengoor doo mëna ñaaw
Doo mëna ñaaw, Jowaal Faajut nga juddoo
Waaw foo cosaanoo (Afrig)
Waaw foo cosaanoo, Senegaal
Sengoor doo mëna ñaaw
Doo mëna ñaaw, Jowaal Faajut nga juddoo
Yow lañu duppee aydapooru Ndakaaru Njaay
Waawaaw Abdu jaaraama, jaaraamaaa
Waaw ne "Pincez tous vos koras
Ne " hFrappez les balafons"
Ku bind loolu, ku bind loolu
Leopol Sedaar Sengoor a ko bind
"C'est le tam-tam des arènes qui t'appelle ce soir"
Ku bind loolu, ku bind loolu
Leopol Sedaar Sengoor a ko bind
Waaw foo cosaanoo (Afrig) Waaw foo cosaanoo, Senegaal
Sengoor doo mëna ñaaw
Doo mëna ñaaw Jiloor nga juddoo
Garmi piir, garmi piir laay delloo njukkëloo man
Garmi piir, garmi piir laay delloo njukkëloo man
Garmi piir, garmi piir laay delloo njukkëloo man

Поcмотреть все песни артиста

Другие альбомы исполнителя

Похожие исполнители